Ey yow, Comrade!
Yaa doon ka sigi!
Judubaax!
Soopa Mbaax
Yaroo manduteek ité gu jara settoo
Lamboo teey ak teegin!
Dundée cofeel ak teraanga!
Xam sa waréef te def kook pastéef gu mut sék!
Ey yow Camrade!
Dun la faate muka ci suńu xol!
Ci suńu xel ak suńu xelaat!
Noteel ak coono doon say mbań ak say mbaeńel!
Ngir jom ak ngoru askan wi
Xeex nga gudéek becég!
Yow mi musula ragal!
Mi musula yoxxi
Mbaa deelu ganaaw!
Ey yow Comrade!
Sa maxaama ak sa njaaraama
Law nańu réew mi mép ba mbitim réew!
Sa taxawaay ci aadaak cosaan
Doon na royukaay gu amul dayo!
Ey Comrade! Ey ńun !
Wéetal nga ńu!
Ndax ku jaaxlewoon ba dawsi ci yow
Nga fompa ay rongońam, nax ko, neehal ko ne ko;
“Bul tiit te bul jaaxle suma raka jéemal – lép dina baax ”
Ndeysaan ! Ebou Madi !
Sa waajur ne nańu
« Foo déka ńu déka fa, ndax foo déka, fóófaa neex ! »
Xalam demoon na be neex
Buum ba daldi daga!
Waay tey jii, fudaat nańu ko)
Te jokkali nańu bóóba wóy
Ba nga ńu jéemantal.
Ey Comrade! Borom xarmbaax ! Borom xarala !
Yaa ngi nii mafńandu sa naar – wu – góor!
Gaacoo sa xeej, saay fita, sa jaasi sa lawarweer ak sa
móxadóm!
Di rëpëtal, di rëpëtal ni Buurba Silla !
Ey Comrade, borom xol bu laab!
Na nga doon suńu njool, ńu di la seetoo
Ndax ńuy bug di taataan ci sa xel mu ńaw mi
Te di root ci sa teen bu dul ŋaca!
Yal nga njegenaayoo yérmaandé suńu Borom
Mu saama sa fit, musal la, nga noopalekook jaama!
Te mey la dunda gu dul jeex!
Sa njaarama waaca na!
Gaace Ngallaama!
Dem nga waay deewuloo!
Artis ba daan aar tiisu askanam!
Cornelius J. Gomez
CONNIE GOMEZ Tel: 7929809/9929809
5 February 2016 marked ten years since Ebou Madi Sillah departed this world.